Ne xale bi Ne bëgguma la mer loo Ne xale bi Bëgguma la mer loo
Ndaxte soo meree Soo meree Sama yaram daw Daw ba jaaxal ma (Bul ma meree)
Lu menul ñàkk Faw dafay am Wareef dafay mat Léeg-léeg mu doon lu dul neex Yow sama doom Suba tax may wax Soo magee dinga xam
Ndaxte soo jooyee Soo jooyee Sama yaram daw Daw ba jaaxal ma
Waa-jur ak doom Faw ñuy waxtaan Feexee mel ni mburu ak sow Ndem réeru mën ta ñàkk So diaxlé, so diaxlé Na sa xel mi dem Dem ci say waa-jur
Ni jamono mel Teey da cee baax Jubbantil ba mu cor Ndax muumin dafay rooy
Bës a ngi ñëw Su maggee jariñ la Lepp ngi ci ba muy ndaw
Ndaxte soo meree Soo jooyee Sama yaram daw Daw ba jaaxal ma (Bul ma meree)
Ne xale bi Ne bëgguma la merloo Oh xale bi Ne bëgguma la merloo
(Xale muumin la Yow bu ko merloo Te dee ko bégal)
Ndaxte soo meree Soo meree Sama yaram daw Daw ba jaaxal ma
Àdduna nii la, xale bi le Su baay waxaatee, nga déglu ko Àdduna nii la, xale bi le Su yaay waxaatee, nga déglu ko
Àdduna nii la, xale bi le (Na nga ma dégloo xel) Su baay waxaatee, nga déglu ko (Bañ ma dégloo xol) Àdduna nii la, xale bi le (Sama doom) Su yaay waxaatee, nga déglu ko (Na nga ma dégloo xel)
Ne xale bi Ne bëgguma la merloo Ah xale bi Ne bëgguma la merloo Xale bi Ne bëgguma la jooyloo
Ndaxte soo meree Soo meree Sama yaram daw Daw ba jaaxal ma